Jaay na bakkanam, ba rey waa Filisti ba. Aji Sax ji maye ca ndam lu réy, ñeel Israyil gépp, nga teg ci bët, am ca mbégte. Ana lu waral ngay tooñ, di tuur deretu jaamburu Yàlla bu mel ni Daawuda, reylu ko ci dara?»
TSK
TSK · Acts 7:25
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Sunuy maam seetuñu ca say kéemaan ca Misra, bàyyiwuñu xel ca sa ngor lu réy, xanaa di fippu ca géej ga, géeju Barax ya.
Taalibe ya nag dégguñu kàddu googu, ndax fekk na piri ma làqu leen, ngir ñu bañ koo daj, te ñemewuñu koo laaj Yeesu.
Ba ñu agsee, dañoo woo mbooloom gëmkat ña, àgge leen mboolem na Yàlla def ak ñoom, ak na mu ubbilee jaambur ñi dul Yawut buntu ngëm.
Werante wu réy am ca. Ci kaw loolu Piyeer jóg ne leen: «Bokk yi, yeen xam ngeen ne bu yàgg la ma Yàlla seppee ci seen biir, ngir jaambur ñi dégge ci sama làmmiñ, kàddug xibaaru jàmm bi, ba doon ay gëmkat.
Sañumaa tudd lenn nag lu moy li Almasi sottale sama jëmm, ngir jaambur ñi dul Yawut déggal Yàlla, te muy lu mu sottale samay wax ak samay jëf,
Ci yiwu Yàlla daal laa doone ki ma doon, te yiw woowu ma ñeel neenul. Xanaa yeneen ndaw yépp sax, maa leen gëna liggéey. Du ci man nag, waaye yiwu Yàlla, wi ànd ak man la.
Loolu moo ma tax di góor-góorlu ci xare bii may xaree dooleem, ak manoorey jëfam, jiy liggéey ci sama jëmm jii.