TSK

TSK · Acts 7:32

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Mu am bés Yuusufa ne ay bokkam: «Sama waxtu jege na, waaye Yàlla moo leen di jëlsi moos, ba jële leen ci réew mii, yóbbu leen ca réew ma mu dige woon, ba giñal ko Ibraayma, Isaaxa ak Yanqóoba.»

Yàlla dellu ne Musaa: «Dangay wax bànni Israyil, ne leen: “Aji Sax ji, seen Yàllay maam ya, di Yàllay Ibraayma, di Yàllay Isaaxa te di Yàllay Yanqóoba, moo ma yónni ci yeen.” Aji Sax jee di sama tur wu sax dàkk, ñu di ma ko fàttlikoo ba fàww.

Mu teg ca ne ko: «Doo mana gis sama kanam nag, ndax doom aadama du ma gis ba noppi di dund.»

Job 4:14 TSK

Tiitaange ne ma taral, may lox, cér yépp di kat-kati.

Job 42:5 TSK

Dég-dégu nopp laa amoon ci yaw, tey bët laa la teg.

¶ At ma Buur Osiyas saayee, damaa gis Boroom bi toog kaw ngàngune mu kawee kawe, lafi mbubbam fees néeg bu sell bi.

Luke 5:8 TSK

Simoŋ Piyeer nag gis loolu, daldi sukk fa kanam Yeesu, ne ko: «Sang bi, ngalla sore ma, ngir man nitu bàkkaarkat laa!»,

Acts 9:4 TSK

Mu daanu ci suuf, daldi dégg baat bu ko ne: «Sóol, Sóol, lu tax nga di ma bundxatal?»

¶ Naka laa ko gis, ne dàll daanu ci ay tànkam ni ku dee. Mu teg ma loxol ndijooram, ne ma: «Bul tiit. Maay Ki Jëkk, di Ki Mujj.