Ayca nu wàcc, safaan seen làkk, ba dootuñu déggoo.»
TSK
TSK · Acts 7:34
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Ba ñu demee ba mu yàgg, Firawna buuru Misra dee. Fekk na bànni Israyil a ngay binni rekk ndax seen njaam ga. Ñuy woote wall, ba seen jooy, ya sababoo ca seen toroxteg njaam ga, àgg fa Yàlla.
Yàlla ne Musaa: «Maay Ki nekk. Kon waxal bànni Israyil ne leen: “Aji Nekk ji moo ma yónni ci yeen.”»
Maa déggal sama bopp yuuxi bànni Israyil, gi waa Misra def ay jaam, te fàttewuma sama kóllëre ga.
Ba nga gisee sunu toroxtey maam ya ca Misra, dégg seeni yuux ca tefesu géeju Barax ya,
Mu gis nag seen njàqare, dégg seeni tinu,
Moo noon: «Sama ñoñ déy ñoom a! Ñee di doom yu dul tas yaakaar.» Mu daldi doon seen jotkat.
Yanqóobaa dawoon ba réewum Siri, Israyil laa ne, moo liggéey ngir am jabar, wut jabar tax koo sàmm ag jur.