Exodus 14:11
TSK
Ci biir loolu ñu ne Musaa: «Xanaa Misra dafa amul ay sëg, ba nga di nu indi ci màndiŋ mi, nu deesi fi? Loo nu doon génnee Misra?
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ci biir loolu ñu ne Musaa: «Xanaa Misra dafa amul ay sëg, ba nga di nu indi ci màndiŋ mi, nu deesi fi? Loo nu doon génnee Misra?
Mbooloo ma mar na fa, bay xultu ci kaw Musaa, naan: «Loo nu doon jële Misra nag, xanaa du boole nu rey ndax mar, nook sunuy doom ak sunuy gétt?»
Ana lu nu Aji Sax jiy indee ci réew mii ñu nara fàddoo saamar, sunuy jabar ak sunuy tuut-tànk doon alalu sëxëtoo! Tee noo dellu Misra yee?»
¶ «Sunu maam yooyu kay ñoo mujj fuuy, sajju loos, ba sàmmuñu say santaane.
Ñu merlooti Yàlla ca ndoxum Meriba ma, muy loraangey Musaa te ñoo ko waral.
Ka doon néewal doole moroom ma bëmëx Musaa, ne ko: “Yaw, ku la def njiit mbaa àttekat ci sunu kaw?