TSK

TSK · Acts 8:24

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Fekk na Aji Sax ji um jigéeni waa kër Abimeleg, ba kenn du ci am doom, du soxnaam, du ay jaamam, te li ko waral di Saarata soxnas Ibraayma. Ibraayma nag ñaan Yàlla; Yàlla def ñu wér, ba mana am doom.

Baal ma àq bii yoon rekk, te ngeen ñaanal ma seen Yàlla Aji Sax ji, ngir mu teggil ma rekk, wii ay wu rey.»

Mbooloo ma dikk ba ci Musaa, ne ko: «Noo tooñ, ndax noo xultu ci kaw Aji Sax ji, ak ci sa kaw. Tinul nu Aji Sax ji, mu teggil nu jaan yi!» Musaa daldi tinul mbooloo ma.

Man nag, yàlla tere may tooñ Aji Sax ji, di leen noppee ñaanal. Te it dinaa leen won yoon wi baax te jub:

Ezra 6:10 TSK

Su ko defee ñu mana sarxalal Yàlla Boroom asamaan lu ko neex tey ñaanal Buur aki doomam gudd fan.

Job 42:8 TSK

Kon nag sàkkleen juróom ñaari yëkk, ak juróom ñaari kuuy. Ngeen dem ba ca sama jaam ba Ayóoba, joxe ko fa saraxu rendi-dóomal, te Ayóoba ñaanal leen, ma seet ci moom ba bañ leena mbugale seenug ndof. Ndax waxuleen dëgg ci man ni sama jaam bi Ayóoba waxe.»