TSK

TSK · Acts 9:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ñeengo jàppul Yanqóoba, gisaane gisul Israyil gii. Lu jot rekk, àggees ko Yanqóoba: ne ko: “Israyiloo, lii la Yàlla def.”

Man de, maa ngii, maak xale yi ma Aji Sax ji may, nu diy firnde fi Israyil te diy tegtal yu bàyyikoo fa Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, ki dëkke tundu Siyoŋ.

Acts 2:12 TSK

Ñépp waaru, ba jànnaxe, di wax ci seen biir naa: «Lii lu muy tekki nag?»

Acts 4:13 TSK

¶ Ba waa kurélu àttekat ya gisee fit, wi Piyeer ak Yowaan àndal, te ñu xam ne niti neen ñu masula jàng lañu, dañoo waaru. Xamoon nañu nag ne ñook Yeesoo nekkoon.

Acts 9:1 TSK

¶ Ci biir loolu Sóol moom, noyyeewul lu moy di tëkkook a jéema bóom taalibey Sang bi. Mu dem nag ca sarxalkat bu mag ba,

¶ Ndax kat dégg ngeen ni ma doon jëfe bu jëkk, bi ma nekkee ci yoonu Yawut, bundxatal gu jéggi dayo ga ma daan teg mbooloom gëmkati Yàlla mi, di ko yàq.