TSK

TSK · Acts 9:22

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage
Job 17:9 TSK

Waaye aji jub a ngi topp yoonam, boroom loxo yu set a ngi gëna am kàttan.

Mooy dooleel ku loof, di kàttanal ku jeele.

¶ Ci kaw loolu mu ne leen: «Lii moo di kàddu ya ma leen waxoon ba ma nekkee ak yeen. Noon naa leen: Mboolem li ñu bind ci samay mbir ci yoonu Musaa, ak ci téerey yonent yi, ak ci Sabóor, fàww lépp sotti.»

Acts 17:3 TSK

Mu di leen tekkil Mbind mi, di leen ci firndeel ne coonob Almasi ak ndekkiteem manul woona ñàkk. Mu ne leen: «Yeesu mii ma di leen xamal, mooy Almasi.»

¶ Ba mu ko defee Apolos namma jàll ba Akayi, bokk ya rafetlu mébétam. Ñu bind taalibey Akayi, ngir ñu dalal ko. Ba Apolos agsee Akayi, dimbali na lool ña fa yiw may ñu doon ay gëmkat.

Waaye li àddina jàppe ag ndof, moom la Yàlla taamu, ngir rusloo ko xamkat yi, te li néew doole ci àddina, moom la Yàlla taamu, ngir rusloo ko li bare doole.