Bu ngeen àggee ca Amoneen ña nag, buleen dal ci seen kaw, buleen xeex ak ñoom, ndax duma leen jox benn cér ci réewum Amoneen ñi, ngir askanu Lóot woowu laa ko sédd.»
TSK
TSK · Amos 1:13
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Nayas Amoneen ba moo dikkoon, gaw dëkk ba ñu naan Yabes ca Galàdd. Waa Yabes gépp wax ak moom, ne ko: «Ngalla digool ak nun jàmm, te nu nangul la.»
Nit ña ca biir nag, mu génne leen, féetale leen ay xeetukaay ak ngaskay weñ ak sémmiñi weñ, boole ci di leen móol-loo. Noonu la def ak mboolem dëkki Amoneen ñi. Gannaaw loolu Daawuda ànd ak mbooloom xareem mépp, dellu Yerusalem.
¶ Booba la Menayem song dëkk ba ñuy wax Tifsa, rey ña fa nekkoon ñépp, boole ca faagaagal diiwaan ba dale Tirsa ba Tifsa, ndax ñoo ko gàntal, bañ koo ubbi buntu dëkk ba. Mu butti jigéeni wérul ña fa nekk ñépp.
¶ Ba loolu amee Sanbalat ma dëkk Oron dégg ko, mook Amoneen ba Tobya, jawriñ ba, ak Gesem, Araab ba. Ñu di nu ñaawal ak a diiju naan: «Li ngeen di def nii lu mu doon? Dangeen di fexeel Buur?»
muy néegi Edom ak Ismayla, néegi Mowab ak Agar,
Lu jëm ci Amoneen ñi, Aji Sax ji dafa wax ne: «Israyil daa amuli doom? Am daa amul dono? Lu tax Milkom tuur mi donloo suufas Gàdd, ba ay jaamukatam sanc dëkki Gàdd?
¶ Kàddug Aji Sax ji dikkal na ma ne ma:
«“Aji Sax ji nekk fi, nga naan: ‘Ñaari làngi giir yii dëkke seen ñaari réew yii, maa leen moom, noo ciy teg loxo.’
Dees na topp waa Samari, nde ñoo fippu ci seen kaw Yàlla. Saamar lañuy fàddoo, seeni doom, ñu rajaxe leen, seen jigéeni wérul, ñu butti.
Biiñ day wore, jàmbaar ju bew jii nag du dal-lu, xanaa yàkkli puruxam ni njaniiw, du doylu, mbete ndee, moom miy buubandoo xeetoo xeet, dajale askanoo askan, aakimoo.