Booba Aji Sax jaa ngi wax naan: «Xanaa duma nëbb Ibraayma li ma nar?
TSK
TSK · Amos 3:7
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Mise teg ca ne ko: «Kon nag déglul kàddug Aji Sax ji. Gis naa Aji Sax ji, mu toog ci ngànguneem, mboolem gàngooru asamaan a nga taxaw ndijooram ba càmmoñam.
Kenn ca jawriñ ya ne ko: «Du kenn, Buur sang bi; waaye Alyaasa, yonent bi ci Israyil mooy jottli buurub Israyil kàddu yi ngay wax ci sa biir néegu biir.»
Moo tax maa ngii di la yóbbu nga fekki say maam, dees na la yóbbu ak jàmm ca sa bàmmeel, te say bët du tegu ci mboolem musiba mi may wàcce ci bii bérab.”» Ba loolu amee ñu dellu, yegge Buur kàddu ga.
Aji Sax ji kat da maa wax ne: «Maa ngi fi ma tollu di xool, ne tekk, ni tàngooru jant bu ne ràññ, mbaa lay bu defu niir ci tàngooru ngóob.»
Mu xamal ma, ne ma: «Dañeel, léegi damaa ñëw ngir leeralal la.
¶ «Léegi, maa ngi lay xamal lu wér. Dama ne, dina amaat ñetti buur yuy falu ci réewum Pers, ñeenteel ba dikk, dajale alal ju bare, ba ëpple leen ñoom ñépp. Bu demee ba alalam may ko doole, dina def lépp lu mu man ngir xabtal ñépp ci kaw nguuru Geres.
¶ Lii peeñum Yeesu Almasi la, mu ko Yàlla jox ngir mu won ay jaamam yenn xew-xew yu dëgmal. Malaakaam la yebal ci Yowaan ngir xamle ko.
¶ Gannaaw loolu damaa xool, rekk yem ci bunt bu ubbiku fa asamaan. Ci biir loolu baat ba ma jëkkoona dégg muy wax ak man te mel nig liit, ne ma: «Yéegal fii, ma won la liy topp ci loolu.»