TSK

TSK · Amos 5:6

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Ci kaw loolu Israyil gis doomi Yuusufa ya. Mu ne: «Ñii ñooy ñan?»

Seen Yàlla Aji Sax ji kat, mooy sawara wuy xoyome, Yàlla ju fiir la.

ne ko: «Buur, sang bi, ngalla bu ma topp lu ñaaw li ma def. Bu ma jàppal mer ndax li ma la tooñ, keroog ba ngay jóge Yerusalem. Ngalla bu ma ko dencal ci sa xol,

Boroom doole mel ni boob, la mu liggéey di ferñent, ànd ak moom ne jéppét, te kenn du fey sawara wa.

Yeen waa Yudak Yerusalem, deeleen xaraf ngir Aji Sax ji, dogleen seen mbuñukay xol, balaa sama xadar ne jippét ni sawara, di tàkk te deesu ko fey ndax seen jëf ju bon.

Yeremi ne ko: «Deesu la leen jox. Dangay déggal Aji Sax ji ci li ma la wax rekk, muy sa jàmm, nga mucc.»

Dangay wax waa gottub diiwaanu Negew, ne leen: “Déglul kàddug Aji Sax ji. Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngii di jafal ci sa biir, daay guy xoyom sa garab yépp, gu naat ak gu wow. Dara du ko mana fey. Daay ga day jóge bëj-saalum ba bëj-gànnaar te ñépp a cay lakk,

nanga leen wax ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngii di jël dénku Yuusufa wi ci loxol Efrayim, mook giiri Israyil yi mu àndal, boole kook dénku Yuda, daldi def lépp wenn dénk, ñu booloo di wenn ci sama loxo.”

Amos 5:14 TSK

Sàkkuleen lu baax, ba lu bon, ba dund, Aji Sax ji Boroom gàngoor yi ànd ak yeen, muy li ngeen wax.

Maay jàmbaaral waa kër Yuda, maay wallu waa kër Yuusufa, suqli leen, ñeewante leen, ñu mel ni masuma leena xarab, nde man maay seen Yàlla Aji Sax ji, te maa leen di nangul.