Déggadi sànk ab téxét, naagu rey ab dof.
TSK
TSK · Amos 6:1
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Bàkkaarkati Siyoŋ tiit nañu, way-gëmadi yaa ngay lox. Ana kan ci nun moo mana dal ak sawara suy xoyome? Ana kan ci nun moo mana dal ak taal yu yànj ya dul fey?
Kon naa dem seeti kàngam yi, wax ak ñoom. Xanaa ñoom dinañu xam yoonu Aji Sax ji, xam lu seen àtteb Yàlla laaj.» Waaye ñoo bokk daggook Yàlla, dogook moom.
«Mowab a dale féex cag ndawam, kenn jàppu ko njaam, yóbbu, wàllanteesu ko ndab ak ndab, xanaa mu ne degg ni biiñ bu taaje, di saf, di xeeñ ba tey.
Ndeysaan! Dëkk beeka wéet tey! Te ñoñam noon gàññ démb. Ndeysaan! Mu ngi mel nib jëtun tey, te noon ràññ fi biir xeet yi! Moo doon lingeeru diiwaan yi, tey mu sasoo liggéeyu sañul-bañ.
Ñooñooy giñe tuuri Samari, naa: “Giñ naa ko ca tuur may dund ca Dan, giñ ko ca yoonu Beerseba wa dul fey.” Dinañu daanu, dootuñu jóg.»
Dama ne: «Ngalla dégluleen yeen njiiti Yanqóoba, yeen kilifay kër Israyil! Xanaa du yeena wara xam yoon?
Waaye wóoy ngalla yeen ñi barele, ndax neexle ngeen ba noppi.
Moom la soob mu jure nu kàddug dëgg, ba nu taxawe ab jooxeb ndoortel meññeef, ci biiri bindeefam.
ci ni ngeen di sippikoo ci kawam, mboolem seenu tiis, nde mooy ki leen tiisoo.