Ba loolu amee ñu yónnee, woolu mboolem kàngami waa Filisti. Ñu laaj leen ne leen: «Nan lanuy def ak gaalu Yàllay Israyil gii?» Ñu ne leen: «Toxal-leen gaalu Yàllay Israyil gi ca Gaat.» Ñu toxal gaalu Yàllay Israyil ca seen dëkk ba ñuy wax Gaat.
TSK
TSK · Amos 6:2
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Ci biir loolu jenn jàmbaar génne ca làngu waa Filisti. Ku ñuy wax Golyaat, dëkke Gaat, taxawaayam di juróom benni xasab yu teg diggante baaraamu déy ak digg, xawa tollu ci ñetti meetar.
¶ Ci kaw loolu Toyi buurub Amat dégg ne Daawuda duma na gàngooru Adadeser gépp.
¶ Ci kaw loolu buurub Asiri jële ay nit dëkk ya ñuy wax Babilon ak Kuta ak Awa ak Amat ak Sefarwayim, dëël leen dëkki Samari, ñu wuutu bànni Israyil. Ñu daldi moom diiwaanu Samari, féetewoo dëkk ya.
Ana tuuri réew yii di Amat ak Arpàdd? Ana tuuri Sefarwayim ak Ena ak Iwa? Ndax dañoo xettli Samari ci man?
Bu leen Esekiya sànk, naan leen: ‘Aji Sax ji moo nuy xettli.’ Ndax tuuri xeet yi mas nañoo xettli réewu wenn xeet ci buurub Asiri?
«Jàll-leen ba ca duni Kitim fa sowu, te xool; yónneeleen Kedar fa penku, seetlu bu baaxa baax ndegam dingeen gis lu mel nii!
Moo Niniw, dangaa gën Teeb, péeyub Misraa? Dëkk ba dëju fa digg wali Niil ya, am ndox wër ko, am tataam di géej, miiram di ndox mu wale géej,