¶ «Maay samp sama kër ci seen biir te duma leen sib.
TSK
TSK · Amos 6:8
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Aji Sax jee gis loolu, gedd, ndax mere doomam yooyu, góor ak jigéen.
Su ma xiifoon, duma leen ko wax, maa moom àddinaak li ci biiram.
Aji Sax ji mere ñoñam, sib xeet woowu mu séddoo,
Wóoy ngalla Efrayim, kaala gu yànj ga ay màndikatam di sagoo! Taaram bu yéeme baa koy réer, ni tóor-tóor yu wow, te ma nga toŋ ca coll, wa ña biiñ man dëkke, fa tiim xur wu nangu wa.
Mu ngi naan: «Maay tabax kër gu yaa, taaxi kaw ya yàmblaŋ. Ma bënn ay palanteer, tafal kër gi banti seedar, diw ko ba mu xonq curr.
Boroom bee mel nib noon, modd Israyil, moddaale këram yu taaru yépp, tas ay tataam, ba fulal Janq Yuda mu taaru ma, ay yuux aki jooy.
Moo tax Boroom bi Aji Sax ji ne: «Ab noon dina gaw seenum réew, néewal leen doole, lël seeni taax.»
Aji Sax ji giñ na ci turam wi askanu Yanqóobay damoo, ne: «Duma fàtte mukk lenn ci seeni jëf.
Gannaaw gi, ñetti sàmm laa dàq ci wenn weer. Ci kaw loolu ma doyal ci xar yi, ñoom it, ma génnliku leen.