Ngeen daldi bànneexoo seenug màggal, yeen ak seeni doom, góor ak jigéen, ak seeni jaam, góor ak jigéen, ak Leween ñeek doxandéem yeek jirim yeek jëtun, ñi ci seen biir dëkk.
TSK
TSK · Amos 8:10
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Ba mu ko defee Absalom sant ay nitam, ne leen: «Ma ne, bu Amnon naanee biiñ, ba xolam sedd, bu ma leen nee ngeen jam ko rekk, reyleen ko. Buleen ragal; man maa leen ko sant. Góor-góorluleen nag te ñeme.»
Ba muy sol kollam la ko Yàlla di yónnee tàngooru sànjam, tawal ko ko lu fees déqam.
Nit ñaa ngi yéeg jëm kërug jaamookaay ga ca Dibon, ngir jooyi ca bérabi jaamookaay ya, Mowab a ngay yuuxoo kaw tundu Nebo ak Medeba, boppoo bopp dib nel, sikkimoo sikkim xuufu,
Bésub keroog Boroom bi, Aji Sax ji ci gàngoor yi moo leen di woo ci jooyoo ak ñaawlu ak wateefu nel, ak colu saaku ngir ñaawlu.
Ñoom ñépp a nelu, wat seeni sikkim, daggat seeni loxo, sol ay saaku, di ko ñaawloo.
Ñooy sol ay saaku di ko ñaawloo, seen yaram wépp daw, gépp kanam sëlmoo gàcce, bopp ya di nel yu set wecc.
Ña ngay naan biiñ, di sàbbaal yàllay wurus yaak yu xaalis yaak yu xànjar yaak yu weñ yaak yu bant yaak yu doj ya.
Maay dakkal gépp mbéxam; ay màggalam, ay Terutel weeram, ay bési Noflaayam, ak mboolem bési ndajeem.
Yeen ñi tëdd ci seen lal yu yànj, ak a sóonoo seen laltu yu nooy, di yàpp mbote yu baax ak sëllu yu duuf,
Niy taxas la ay noonam di laxasoo, mel ni ñu naan ba màndi, te ni boob mu wow lañuy lakke ba xoyomu.
Ba mu jubsee buntu dëkk ba, yemul ci lu moy ab rob, ka dee di doomu jëtun, te moom rekk la amoon. Niti dëkk ba def mbooloo mu bare, ànd ak soxna sa.