TSK

TSK · Amos 8:9

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage
Job 5:14 TSK

Ñu ni mel, bëccëg ñu dajeek lëndëm, di làmbatoo digg bëccëg ni bu doon guddi.

Tendeefal, jommi rekk! Gëmm, gumba rekk. Ñiika màndi te du biiñ, ñuy jang te duw ñoll!

Teral-leen seen Yàlla Aji Sax ji, bala moo lëndëmal, ngeen tërëfe tundi timis, di séentu leer, mu lëndëmal ba mu ne këruus, fatt taraj

Amos 4:13 TSK

Kii kat moo móol tund, di sàkk ngelaw, di xamal nit nammeelam. Kee di soppi lëndëm ag leer, di daagoo kawte ya. Kookoo di Aji Sax ji Boroom gàngoor yi.

Micah 3:6 TSK

Moo tax yeen, guddi moo leen di ñeel, ba peeñu réer, lëndëm a leen di dikkal, ba ngis tukkil leen, jant mooy sowal yonent yi, bëccëg lëndëmal leen.

¶ Ba ñu demee ba tollu wetu fukki waxtu ak ñaar ca bëccëg, ag lëndëm a wàcc ca réew ma mépp, ba fukki waxtu ak juróom ca ngoon.

¶ Ñeenteelu malaaka mi wal liitam, mu dal ñetteelu xaaju jant bi, ak ñetteelu xaaju weer wi, ak ñetteelu xaaju biddiiw yi, ba tax seen ñetteelu xaaju leer giim, ñetteelu xaaju bëccëg bi daldi lëndëm, ñetteelu xaaju guddi gi it gëna lëndëm.