TSK

TSK · Colossians 1:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

«Man maa tabb buur, fal ko ci Siyoŋ, sama tund wu sell.»

«Xool-leen sama jaam bi ma yor, sama tànnéef, sama soppey xol, ci kawam laa teg samag noo, te mooy dogalal xeet yi yoonu àtte.

Moo tax ma di ko jox ab cér ci biir ñu bare, mu séddoo ak ay kàngam alalu xareem, ngir moo jébbale bakkanu boppam, ñu limaale kooki tooñkat, moo gàddu bàkkaaru ñu bare te mooy tinul moykat yi.

Bégala bég, janq Siyoŋ mu taaru, janq Yerusalem mu taaru laa ne: Xaacul, sa buur a ngoog, jëmsi ci yaw, moo jot njekk ak mucc, te teewu koo woyof, war mbaam, cumbur doomu mbaam.

Moona bés bu nekk, maak yeen la woon ca kër Yàlla ga, te teguleen ma loxo. Waaye seen waxtu la léegi, bi kilifteefug lëndëm ayee nii.»

Waaye cant ñeel na Yàlla, nde ay jaami bàkkaar ngeen woon, waaye gannaaw gi, seenub xol ngeen déggale misaalub àlluwa, ji ngeen di ndénkaaneem.

¶ Am xamuleen ne aji jubadi ñi amuñu cér ci nguurug Yàlla? Bu leen kenn nax: Muy fokati séy yi, di bokkaalekat yi, di jaalookat yi, di góor-jigéen yi, ak ñiy ànd ak ñoom,

Aji gëmadi ñooñu la Seytaane yàllay xarnu bii gëlëmal seenum xel, ngir ñu baña gis ceeñeeru xibaaru jàmm bu leeru Almasi, miy melokaanu Yàlla.

Moo tax cant ñeel ko, ndax yiwam wu màgg wi mu nu baawaanal ci Soppeem bi.

Seenum xel a tàbbi ag lëndëm, ñu tumurànke dundin wi Yàlla di maye, te umple gi ci ñoom moo tax, ndax seenug dëgër bopp.

Ndax kat sunub xare du nook boroomi deret ak suux, waaye ñi ñu ko séqal ay boroom nguur lañu, ak ay boroom sañ-sañ, ak ay boroom doole yu nekk ci àddina ju lëndëm jii, di ay dagi Seytaane yu fare déndi asamaan.

Titus 3:3 TSK

¶ Ndax nun itam kat, ñu ñàkk xel lanu woon te déggadi, ñu réer, tënku ci lu doon ay xemmemtéef, ak bànneexi bakkan, tey wéye def lu bon, ak ñeetaane, ñu jara bañ te bañante ci sunu biir.

¶ Waaye yeen nag yeen ay giir giy tànneef, yeenay sarxalkati Buur, yeen ay askan wu sell, yeen ay xeet wi ñu jot, ngir ngeen biral jaloore yu wéet yi ñeel ki leen woo, génnee leen cig lëndëm, indi leen ci leeram gu yéeme.