TSK

TSK · Daniel 1:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Firawna nag tudde Yuusufa Safnat Paneya, may ko jabar Asnat doomu Potifera ma doon sarxalkat ca dëkk ba ñuy wax On. Yuusufa doxe ca tegoo kilifteefu Misra gépp.

Buuru Babilon moo fal Mataña, baayu Yowakin bu ndaw, mu wuutu Yowakin, daldi soppi turu Mataña, tudde ko Cedekiya.

Teewul kilifag jawriñ ya ne Dañeel: «Man de damaa ragal Buur sama boroom, moom mi leen dogalal seen lekk ak seen naan. Su Buur gisee ngeen gëna yooy seen moroomi xale yu góor yi nag? Sama bakkan xaj na ci de!»

Ci biir loolu Dañeel ñaan Buur mu tabb Sadarag ak Mesag ak Abet Nego, ñu yore saytub diiwaanu Babilon. Dañeel moom nekk ca ëttu buur.

Ñu mujj ma indil Dañeel, di Beltasar, mi ñu tudde sama yàlla, di ku xelu yàlla yu sell yi nekk ci moom. Ma wax ko gént gi.

loolu yépp ndax dañoo gis ci kooku Buur tudde Beltasar, xel mu ñaw akum njàng ak ràññee. Day firi gént, di teqental ay cax ak a lijjanti ay jafe-jafe. Kookooy Dañeel; kon nañu ko woo, mu wax piri mi.»