TSK

TSK · Daniel 2:49

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Jamono yooyu Mardose amee ndombol tànk ca buntu kër buur, ku ñuy wax Bigtan ak ku ñuy wax Teres, di ñaari fara buntu kër buur, ñoo am lu ñu meree lool Buur Aserus, bay lal pexe mu ñu ko bóome.

Bu ku jub amee ndam, mbégte mu réy la; ab soxor falu, ñépp làquji.

Kilifag jawriñ ya nag tudde leen yeneen tur. Dañeel, mu tudde ko Beltasar, Anaña mu tudde ko Sadarag, Mikayel tudd Mesag, Asaryaa di Abet Nego.

¶ Ba loolu amee Dañeel ñibbi, daldi xamal mbir ma Anaña ak Mikayel ak Asaryaa, àndandoom ya,

Dafa am ay Yawut yoo tabb, ñu yore saytub diiwaanu Babilon. Ñu di leen wax Sadarag ak Mesag ak Abet Nego. Ñooñu de Buur, déggaluñu la; say yàlla, jaamuwuñu leen; sa jëmmu wurus ji nga samp it, màggaluñu ko.»

Amos 5:15 TSK

Bañleen lu bon, bëgg lu baax, di doxal yoon ci pénc. Jombul Aji Sax ji Boroom gàngoor yi baaxe ndesu askanu Yuusufa.