TSK

TSK · Daniel 4:1

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage
Ezra 5:7 TSK

Kàddu ga nii la tëdde: Buur Daryus, nu ngi lay bind, di la dikke sunu nuyoob jàmm ju sax.

¶ Ci kaw loolu ñu woo bindkati buur ca bés ba, di ñaar fukki fan ak ñett ca weeru Siwan, ñetteelu weer wa. Ñu daldi bind mboolem lu Mardose santaane, ca mbirum Yawut yaak jawriñ yaak boroom dëkk yaak kàngami diiwaan ya, dale ko ca End ba ca Kuus. Muy téeméeri diiwaan ak ñaar fukk ak juróom ñaar (127). Ñu bind ndigal ya ci mbindum diiwaan bu nekk ak ci làkku xeet wu nekk, Yawut ya it ak seen mbindu bopp ak seen làkku bopp.

Dogal tukkee na ci man ne: muy mépp mbooloo ak bépp xeet ak wépp làkk, képp ku ci ñàkke kersa Yàllay Sadarag ak Mesag ak Abet Nego, ay dog lees koy dog, te këram dees na ko def ab sën, ndax kat amul jenn yàlla ju mana walloo ni moom.»

¶ «Dogal tukkee na ci man, ne mboolem fu bokk ci sama nguur, nañu fa ragal Yàllay Dañeel, wormaal ko, keey Yàlla jiy dund, kee sax fàww, nguuram du tas, kilifteefam du jeex.

Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: «Janti keroog yooyu, fukk ñuy làkk mboolem làkki xeet yi, ñooy langaamoo catu mbubbu benn Yawut, naan ko: “Nun, yeen lanuy àndal, nde noo dégg ne Yàllaa ngeek yeen.”»

¶ Bataaxal bi ñeel na mboolem yeen ña fa Room, di ñu Yàlla sopp, woo leen, ngir ngeen doon ñu sell. Aw yiw ak jàmm ñeel na leen, bawoo fa Yàlla sunu Baay, ak Sang Yeesu Almasi.

ñeel Timote, sama doomu bopp ci wàllu ngëm. Aw yiw ak yërmande ak jàmm ñeel na la, bawoo ci Yàlla Baay bi, ak sunu Sang Almasi Yeesu.