Genesis 28:12
TSK
¶ Guddi googu Yanqóoba dafa gént, gis raas bu sampu ci suuf, te cat la sar asamaan, malaakay Yàlla yi di ci yéeg ak a wàcc.
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Guddi googu Yanqóoba dafa gént, gis raas bu sampu ci suuf, te cat la sar asamaan, malaakay Yàlla yi di ci yéeg ak a wàcc.
Aji Sax ji, dama lay gërëm ci biir xeet yi, kañ la ci biir waaso yi.
Léegi nag teg naa réew yii yépp ci loxol Nabukodonosor buuru Babilon, mi ci sama curga, ba joxaale ko rabi àll yi sax, ñu nangul ko.
Yaw Buur, buuru buur yi, yaw mi Yàlla Boroom asamaan jox nguur ak kàttan ak dooleek ndam,
¶ «Buur, Yàlla Aji Kawe ji daa joxoon sa baay Nabukodonosor nguur gi, muy ku màgg, am ndam ak daraja.