TSK

TSK · Daniel 5:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Ba bët setee, Firawna jaaxle lool, ba woolu jibar ya ak boroom xam-xami Misra yépp, nettali leen la mu gént, te kenn manu koo firil Firawna.

¶ Ci kaw loolu magi Mowab ànd ak magi Majan, dem, yóbbaale ay weexal. Ba ñu agsee ca Balaam, daldi koy àgge kàdduy Balag.

Léegi nag, laggal ñibbi. Noon naa la dinaa la teral bu baax, waaye mu ngoog, Aji Sax jee la xañ teraanga.»

¶ Gannaaw ba xew-xew yooyu jàllee, Buur Aserus teral ku ñuy wax Aman doomu Amdeta mi askanoo ci Agag, yékkati ko, teg ko ci kaw mboolem kàngam yi ci wetam.

Kaala gu jekk la ci bopp, di gànjar ci baat.

Maay neenal firndey maaman, dofloo gisaanekat. Maay weddi fóore, def xam-xamam mu dig ndof.

Ma takkal lay gànjar; takkal la lami loxo, akub caq,

Waaye su ngeen waxee gént gi, wax ma piri mi, ay weexal aki yool ak teraanga ju réy ngeen di jële ci man. Kon nag waxleen ma gént gi, wax ma piri mi.»

¶ Ma ne ko: «Beltasar, kilifay taryaax yi, man ci sama bopp xam naa ne xelum yàlla yu sell yaa ngi ci yaw, te menn mbóot jaaxalu la. Peeñum gént gi ma gént, wax ma piri mi.

Dégg naa nag ne man ngaa firi lool ak a lijjanti mbir yu jafe. Soo ma manee jàngal mbind mi, wax ma lu muy tekki, dees na la solal yérey buur yu xonq curr, takkal la caqu wurus, jox la kilifteef gu lay tofal ci bummi.»

¶ Mu neex Daryus nag, mu fal téeméeri jawriñ ak ñaar fukk ca réew ma, ñuy saytu nguur ga gépp;