Dina yékkati ay kàddu dal ci Aji Kawe ji, dina fitnaal aji sell yu Aji Kawe ji te dina fexee soppi takkinu jamono yi ak yoonu Yàlla wi. Dees na teg aji sell yi ci loxoom diiru ñetti jamonook genn-wàll.
TSK
TSK · Daniel 7:11
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Dina samp xaymay kër buur ci diggante géej geek tund wu taaru wu sell wa. Waaye dina dee, te kenn du ko taxawu.»
Kàddu yu réy yu tekkiwul dara lañuy naxee, di fàbbee xemmemtéefi bakkan yu jéggi dayo, ay nit ñu yàggula rëcce ci ñeneen ñu nekk cig réer.
¶ Ñu may rab wi nag muy kañu ak a saaga Yàlla, may ko it mu saña wéye noonu diiru ñeent fukki weer ak ñaar.
Ñu daldi jàpp rab wi, mook yonentu caaxaan, bi defoon ci turu rab wi ay kéemaan yu mu sànke ña ñu màndargaale woon màndargam rab wi, te ñu doon jaamu jëmmu nataalu rab wi. Ñoom ñaar ñépp lañu sànni, ñuy dund ca déegu sawara waak tamarax bay bax.
Ñu jàpp nag Seytaane, mi leen daan nax, sànni ko ci déegu sawaraak tamarax ba, mu fekki fa rab waak yonentu caaxaan ba. Dees na leen fa mitital guddi ak bëccëg, ba fàww.