TSK

TSK · Daniel 7:18

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Na wóllërey Yàlla bànneexoo seen ndam, bu ñu tëddee sax, di sarxolle,

ba keroog góor gu mag gi dikk, daldi jox dëgg aji sell yu Aji Kawe ji; àpp bi nag mat, aji sell yi moom nguur gi.

Waaye kaw tundu Siyoŋ la aw ndes di rawe, te dina doon bérab bu sell, waa kër Yanqóoba it moomaat seeni moomeel.

Ndax kat sunub xare du nook boroomi deret ak suux, waaye ñi ñu ko séqal ay boroom nguur lañu, ak ay boroom sañ-sañ, ak ay boroom doole yu nekk ci àddina ju lëndëm jii, di ay dagi Seytaane yu fare déndi asamaan.

¶ «Ku am ndam nag, ku saxoo jëf ji ma soob, ba kera muj ga, maa lay jox sañ-sañ ci kaw xeet yi:

Yaa leen def ñu doon nguurug sarxalkat yi, ñeel sunu Yàlla, te dinañu nguuru ci àddina.»