TSK

TSK · Daniel 7:20

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ «Ni ma ne jàkk ci béjjén yi, beneen béjjén bu ndaw ne pëll, génn ci seen biir, ñett ca béjjén ya jiitu buddeeku. Béjjén bu ndaw baa nga am bët yu mel ni bëti nit ak gémmiñ gu muy waxe kàdduy damu.»

¶ «La ca topp mu neeti ma: “Ñeenteelu rab wi mooy ñeenteelu nguur giy taxaw ci kaw suuf, wuuteek nguur yépp. Dina mëdd àddina sépp, nappaaje ko, rajaxe ko.

¶ «Buur bi dina def lu ko soob. Dina réy-réylook a damu, ba weesale boppam tuur yépp, te dina wax gilaawaali jëme ci Yàlla ji sut lépp. Dina am ndam nag ba keroog sànjum Yàlla ñoral ko. Li ñu dogal déy dina am.