TSK

TSK · Daniel 7:28

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ba mu ko nettalee ay magam, ba nettali ko baayam, baayam da koo soow ne ko: «Yaw, li nga gént, lu mu doon? Xanaa du maak sa yaay ak say mag noo lay sujjóotal?»

¶ Ba loolu amee Dañeel ma ñuy wax Beltasar ne dann ab diir, jaaxle, xalaat yu ko tiital dikkal ko. Buur àddu ne ko: «Beltasar, gént geek piri mi bumu la tiital.» Beltasar ne ko: «Sang bi, su ma sañoon de muy sa géntug noon te pireem topp say bañaale.

Kanamu Buur nag soppiku, njàqare dikkal ko, ba ndigg la ne yalax, óom yay fenqoo.

Jibril dikk nag ba fi ma taxaw. Ba mu jegesee, ma tiit lool, ba daanu, sama kanam dëppu fi suuf. Mu ne ma: «Yaw doom aadama ji, nanga xam ne peeñu mii mujug jamono la.»

¶ Ba loolu amee ma ne làcc, wopp ay fan, man Dañeel. Gannaaw gi ma jóg, dellu ca liggéeyu buur. Ma waaru nag ca peeñu ma, ndax daa wees sama dég-dég.

Ñaari buur yi dinañu nas lu bon ci seen xol; di bokk ndab tey waxantey fen. Waaye seeni pexe du mujj fenn, ndax du fekk muj ga jot.

Waaye yaw Dañeel, muñal ba fa muy mujje. Su keroogee fekk la nelaw, doora jóg jël sab yool, ca mujug jamono.»

Luke 2:19 TSK

Teewul Maryaama moom, bàyyi woon na xel ci mbir moomu mépp, di ko xalaat ci xolam.

Luke 9:44 TSK

¶ «Ubbileen seeni nopp te teewlu bu baax kàddu yii: Doomu nit ki lees di wor, ngir teg ko ci loxoy nit ñi.»