TSK

TSK · Daniel 8:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Aji Sax ji, xanaa doo nu mere ba fàww, sa fiiraange ni sawara ci sunu kaw?

Dooley kilifteefam ak jàmm ja du am kemu, fa jalub Daawuda ak nguuram, ga muy samp, saxale ko njekk ak yoon, tey jii, ba fàww. Lii la Aji Sax ji Boroom gàngoor yi def ci xéraangeem.

¶ «Fi ma tëdd ci sama lal, ma jekki gis ab wattukat bu sell wàcce asamaan.

Li ñu santaane ñu bàyyi ëkk beek reeni garab gi mooy tekki ne nguur gi dees na la ko delloo keroog boo xamee ne Boroom asamaan mooy Buur.

¶ «La ca topp mu neeti ma: “Ñeenteelu rab wi mooy ñeenteelu nguur giy taxaw ci kaw suuf, wuuteek nguur yépp. Dina mëdd àddina sépp, nappaaje ko, rajaxe ko.

Dina feddli kóllëre diggam ak ñu bare ci benn àppu juróom ñaar, te ci diggu àppu juróom ñaar ba lay dakkal sarax yi ñuy rendi ak yeneen sarax. Ci genn wetu sarxalukaay bi la yàqkat biy taxawal lu siblu, di sabab yàqute, ba keroog muj gi ñu ko dogalal ne milib ci kawam.»

¶ Noonu man Dañeel, may xool ci biir peeñu mi, daldi yem ci ñeneen ñaar ñu taxaw, séq dex gi.

Jamono ja ñuy dakkal sarax si wara sax fàww, di keroog ba ñuy taxawal lu siblu lay jur yàqute, junniy fan ak ñaar téeméer ak juróom ñeent fukk (1 290) dina ca topp.

Xur wa ca diggante sama tund ya ngeen di jaare daw, ndax xur wa ba Accal lay àkki. Na seeni maam dawe woon ngeen di dawe, ba suuf sa yëngoo, ca janti Osiyas buurub Yuda. Sama Yàlla Aji Sax ji mooy dikk, ànd ak mboolem ñu sell ñi.

Lépp la ma sama Baay dénk, te kenn xamul kuy Doom ji, ku dul Baay bi; kenn it xamul kuy Baay bi, ku dul Doom ji, ak képp ku ko Doom ji namma xamal.»

Dinañu fàddoo ñawkay saamar, te dees na leen jàpp njaam, yóbbu ci mboolem xeet yi. Te jaambur ñi dul Yawut ñooy joggati Yerusalem, ba kera àppu ñooñu dul Yawut di mat.

Yal na Boroom bi dooleele noonu seen xol, ngir kera bu sunu Sang Yeesu délsee, ànd ak ñoñam ñu sell ñépp, fekk leen sell te mucc sikk, fa kanam Yàlla sunu Baay.

Yonent yooyu, xamalees na leen ne du seen njariñal bopp lañuy liggéeyal xibaar boobu, xanaa yeen. Ñi leen àgge xibaar bi tey ñoo di ñiy waare xibaaru jàmm bi ci dooley Noo gu Sell, gi ñu yebale asamaan, te muy mbir mu malaaka yi sax, noon siiwa nemmiku.

Ñu àddu ca kaw ne: «Buur bu sell, bu dëggu bi, loo deeti xaar ci àtte waa àddina, feyul nu sunu deret ji tuuru?»