TSK

TSK · Daniel 8:18

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Ba jant bay so, ngëmment lu réy a ko jàpp, tiitaange lu mag, ànd ak lëndëm gu ne këruus, ne milib ci kawam.

Naka la ma wax loolu, ngelaw solu ma, ne ma yékkét, ma taxaw, di dégg kiy wax ak man.

¶ Ba loolu amee ma ne làcc, wopp ay fan, man Dañeel. Gannaaw gi ma jóg, dellu ca liggéeyu buur. Ma waaru nag ca peeñu ma, ndax daa wees sama dég-dég.

Ci kaw loolu ma dégg baatam. Naka laa dégg baatam, daldi daanu leer, sama kanam dëppu fi suuf.

Ba loolu amee jëmm jiy nirook nit dellu laal ma, ma amaat doole.

Luke 9:32 TSK

Booba ngëmment a ngay man Piyeer ak ña mu àndal. Ba ñu teewloo nag lañu gis leeru Yeesu, ak ñaar ña mu taxawal.

Acts 26:6 TSK

Sama taxawaayu tey ci ëttub àttekaay bii nag, mooy yaakaar ji ma am ci dige bi Yàlla digoon sunuy maam.