TSK

TSK · Daniel 9:10

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Li waral loolu mooy waa Israyil a déggalul seen Yàlla Aji Sax ji. Dañoo fecci kóllëreem ak moom, ba mboolem li Musaa, jaamu Aji Sax ji, santaane woon, faalewuñu ko, jëfewuñu ko.

Ca tundu Sinayi wa nga wàcc, àddoo asamaan, wax ak ñoom, dénk leen ndigal yu jub, ak yoon yu dëggu, ak dogali yoon ak santaane yu baax.

Ñu dikk moom ko, te déggaluñu la, toppuñu saw yoon, jëfewuñu mboolem li nga leen santoon, ba tax nga wàcce ci seen kaw mboolem musiba mii.

¶ Bu yàgg la Yàlla waxoon ay yooni yoon ak maam ya, ci waxin yu bare, yonent yi jottli.