TSK

TSK · Deuteronomy 1:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Ci kaw loolu Kaleb noppiloo mbooloo ma, fekk leen tàmbalee diiŋat Musaa. Mu ne leen: «Nooy dem ba demaatoo, nanguji réew ma, ndax bir na ne noo leen mana duma.»

Fexeleen rekk ba Aji Sax ji, buleen ko gàntal, te yeen nag ngeen baña ragal waa réew ma, ndax ab lanc doŋŋ lañu nuy mat. Seen kiiraay dëddu na leen, te Aji Sax jaa ngeek nun. Buleen leen ragal.»

Buleen am tiitaange ci ñoom, ndax seen Yàlla Aji Sax ji ci seen biir, Yàlla ju màgg la te raglu.

ne leen: «Éey Israyil, dégluleen, yeena ngi waaja xareek seeni noon tey jii. Buleen yox-yoxi, buleen ragal, buleen tiit, buleen teqlikook seen sago ci seen kanam!

Ñeel Daawuda. Aji Sax jee may leeral, di ma wallu. Ana ku may ragal? Aji Sax jeey aar sama bakkan. Ana ku may tiit?

Ay giir a riir, ay réew yëngu; mu àddu, suuf seey!

bul ragal, yaw laa àndal, bul tiit, maay sa Yàlla; maa lay dooleel, dimbali la déy, maa lay téyee sama ndijooru njekk déy.

¶ «Buleen ragal dara, yeen jur gu sew gi, ndax seen Baay la soob, mu jagleel leen nguur gi.