TSK

TSK · Deuteronomy 19:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ku tuur deretu nit, na nit tuur deretam, ngir melokaanu boppam la Yàlla sàkke nit.

¶ «Ku rey ag jur na fey boroom, waaye ku rey nit dee mooy àtteem.

Buleen tilimal réew mi ngeen nekk. Deret kat mooy tilimal réew mi, te réew mi deesu ko jote lenn, ci deret ju ñu tuur ci biiram, lu moy deretu ka tuur deret.

Fàkkasleen mboolem xeet yi leen seen Yàlla Aji Sax ji jébbal nag. Buleen leen xool bëtu yërmande, buleen jaamu seeni tuur: Lu ko moy muy seenug fiir.

Yeen nag, noonu ngeen di tenqee ci seen biir, àqu deretu jaambur ju ñu tuur, ndax kon def ngeen li Aji Sax ji rafetlu.

¶ Jamono ya Daawuda nekkee ci jal bi, amoon na xiifub ñetti at yu tegloo. Daawuda diis ko Aji Sax ji. Aji Sax ji ne ko: «Li waral xiif bi moo di àqu deret ji topp Sóol ak waa këram ndax waa Gabawon ña mu rey.»

Buur ne ko: «Defal li mu wax, jam ko mu dee, nga suul ko, ndax ma set, maak sama waa kër baay, ci deretu jaamburi Yàlla ji Yowab tuuroon.