TSK

TSK · Deuteronomy 24:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ «Su ngeen nangoo mbubbam tayle ci seen dëkkandoo, dellooleen ko ko bala jant a so.

Sunu njekk lay doon nag, ndegam sàmmoo nanoo jëfe mboolem santaane bii, fi sunu kanam Yàlla Aji Sax ji, ni mu ko santaanee.»

Ci bés bi ngeen koy fey peyooram. Bu ko jant sowe, ndax néew doole la te moom la yaakaara dunde. Lu ko moy mu boole leen ak Aji Sax ji, ngeen gàddu bàkkaar.

Job 29:11 TSK

nopp dégg ma, ndokkeel ma, bët gis ma, seereel ma yiw.

Job 31:16 TSK

Damaa masa xañ néew-ji-doole lu muy sàkku, mbaa ab jëtun wékk ma bët, ma tas yaakaaram?

Mooy nàddil néew-doole yi, njekkam sax dàkk, dooleem di yokku, ànd ak daraja.

du kenn ku mu néewal, xanaa ab tayle, mu delloo ku ko ameel, alalu jaambur it, foqatiwu ko, xanaa ku xiif, mu leel, ku rafle, mu wodd,

du kenn ku mu néewal, ab tayle, jëlu ko, sàkkuwul ku ko tayle lenn, alalu jaambur, foqatiwu ko, xanaa ku xiif, mu leel, ku rafle, mu wodd,

Ma ngay wax naan: «Xanaa lii du Babilon gu mag gi ma tabax man, ci sama doole ju réy, muy péeyu buur, di sama ndam ak sama daraja?»

Liggéey bi ci ndimbal lii nag, nit ñi dinañu natt soloom bu réy, bay sàbbaal Yàlla, ndax ni ngeen firndeele ne déggal ngeen xibaaru jàmm bu Almasi, ak ni ngeen yéwéne ci seen jàpplante, jëme ci ñoom ak ci ñépp.

Yal na Yàlla baaxe nag waa kër Onesifor, yërmandeem, ndax dëfal na ma lu bare, te kersawoowul li ñu ma tëj kaso,

Daan bu àndul ak yërmande, moom lees di àttee ña daawul jëfe yërmande. Yërmande nag kekku na ab daan.