TSK

TSK · Deuteronomy 4:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Kaw doj yii laa tollu di leen séen, fi kawte yii laa leen jéere. Aw askan a ngii, dëkke fu beru, te bokkuñu ak xeet yi.

Ana ci mboolem boroomu suux, ku ci masa dégg kàddug Yàlla jiy dund, mu jibe ci sawara, nii nu ko dégge, ba noppi di dund?

Ana askan wu mel ni Israyil sa ñoñ ci kaw suuf, wenn askan wu Yàlla dikk, goreel leen ngir def leen ñoñam, ba turam siiw? Yaa leen defal ay jaloore, yaa defal sam réew ay kéemaan ci sa kanam ñoñ ñi nga goreele fa Misra aki askanam aki yàllaam.

Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di jàngin wu ñeel askanu Kore wu góor, dëppook galan bu ñuy wax Baatu jigéen.

Aji Sax ji, képp ku ko woo wall, mu jege la, képp ku ko woo wall te muy dëgg.

Fonk la, teral la ak sopp la, moo tax ma joxey nit, weccikoo la; ay askan dee, wuutu sa bakkan.

Jant yooyu amuleen woon benn cér ci Almasi, te amuleen woon jenn yelleef ci mbootaayu bànni Israyil. Bokkuleen woon ci kóllëre yi ëmb digeb Yàlla, te mu fasoo ko ak ñoom. Ñàkk yaakaar, ak ñàkka xam Yàlla ngeen nekke woon ci àddina.