Malaaka ma ne ko: «Bu sa loxo laal xale bi; bu ko def dara, ndaxte léegi xam naa ne ragal nga Yàlla, ndax gàntaloo ma sa jenn doom ji.»
TSK
TSK · Deuteronomy 6:2
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Bés ba ngeen taxawee fa seen kanam Yàlla Aji Sax ji, fa tundu Oreb, Aji Sax jee ma ne: «Dajaleel ma mbooloo mi, ma dégtal leen samay kàddu, ngir ñu tàggatu ci ragal ma li feek ñuy dund ci kaw suuf, te seeni doom it, ñu tàggat leen ci.»
¶ «Teral-leen seen baay, ak seen ndey, ni leen ko seen Yàlla Aji Sax ji sante, ndax ngeen gudd fan, ndax it ngeen baaxle ca réew ma leen seen Yàlla Aji Sax ji jox.
Nangeen ko xamal seeni doom, di ko waxe bu ngeen toogee seen biir néeg, ak bu ngeen di dox ciw yoon, ak bu ngeen tëddee, ak bu ngeen jógee.
¶ Léegi nag yeen Israyil, ana lu leen seen Yàlla Aji Sax ji laaj, lu moy ngeen ragal seen Yàlla Aji Sax ji, di doxe mboolemi yoonam, sopp ko, di jaamoo seen Yàlla Aji Sax ji seen léppi xol, ak seen léppi bakkan,
buleen déglu waxu yonent boobu, mbaa boroom gént boobu, ndax seen Yàlla Aji Sax ji moo leen di nattu ngir xam ndax yeena ngi koy soppe seen léppi xol ak seen léppi bakkan.
Fexeleen ba bàyyi yaay ja, te jël cuuj ya, ndax ngeen baaxle te gudd fan.
Soppleen seen Yàlla Aji Sax ji, déggal ko te taq ci moom, ndax moom mooy seenug dund, di seen gudd-gi-fan ca réew ma mu giñaloon seeni maam Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba, ne ñoom la koy jox.
Su ko defee dinañu la ragal seen giiru dund ci kaw suuf si nga joxoon sunuy maam.
Dunu ko nëbb sunuy doom, xanaa di ko jottli maas giy ñëw, xamal leen jaloorey Aji Sax ji ak kàttanam aki kéemaanam.
Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla. Ndokklee képp ku ragal Yàlla, di jëfe ay yoonam.
Gudd fan, mu joxee ndijoor; càmmoñ ba, alal ak teraanga.
Ku jiital ngor ak worma, Yàlla jéggal la; ku ragal Aji Sax ji, dëddu lu bon.
Maa leen di may benn xol ak benn jubluwaay ngir ñu di ma wormaal seen giiru dund, muy seen ngëneel, ñook seen doom yi leen di wuutu.
¶ Gannaaw nag kiy àtte nit ku nekk ci ay jëfam te amu ci xejj ak seen, Baay ngeen koy wax, sàllooleen koo ragal, seen diirub ngan ci kaw suuf.