TSK

TSK · Deuteronomy 9:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ña nga jaare Negew ca bëj-saalum, dem ba Ebron, fa Anageen ña, Ayman ak Sesay ak Talmay, dëkkoon. Ebron googee, tabaxees na ko juróom ñaari at lu jiitu Cowan ga ca Misra.

Fa lanu gis xeetu Nefilim ya, ponkali Anageen ña bokk ca xeetu Nefilim ya, nuy niru sunu bopp ay soccet fi seen kanam, di leen ko niru, ñoom it.»

Ay Refayeen lañu jàppe woon Emeen ñooñu ak Anageen ñi, teewul Mowabeen ñi di leen wooye ay Emeen.

Mooy teg seeni buur ci seeni loxo, ngeen far seenu tur fi asamaan tiim. Kenn ci ñoom du leen të, ba kera ngeen leen sànkee.

Job 11:10 TSK

Su dikkee, tëj nit, woo ko péncum àtte, ku ci man dara?

Ki leen di song dina leen def li ko soob, ndax kenn du ko të. Dina toog ci réew mu taaru ma, te am dooley tas ko.

Nahum 1:6 TSK

Bu sànjoo, ana kuy taxaw? Ana kuy dékku tàngooru meram? Am sànjam a naan soteet ni sawara, doj yi rajaxoo fi kanamam.