¶ As ndaw, ngeen digool ab séy, keneen tëdde ko; ag kër, ngeen tabax, te dungeen ko dëkke; ab tóokëru reseñ, ngeen jëmbat, te dungeen ko jariñoo.
TSK
TSK · Ecclesiastes 3:13
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Kon nit amul lu gën di lekk ak a naan, di bànneexoo ñaqam. Ma gis ne loolu it Yàllaa koy maye.
Ecclesiastes 6:2
TSK
Nit ku Yàlla may alal, koom ak daraja, te mboolem lu mu namm, ñàkku ca lenn, waaye Yàlla mayu ko mu tal caa lekk, xanaa jaambur di ko xéewloo — loolu cóolóoli neen la, di naqar wu tar.
Isaiah 65:21
TSK
«Ñooy tabax ay kër, dëkke, jëmbati tóokër, lekk ca meññeef ma.