TSK

TSK · Ecclesiastes 3:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Ba mu ko defee Ruben dellu ca kàmb ga, gis ne Yuusufa nekkatul ca biir, mu mititlu ko, ba xotti ay yéreem.

¶ Yuda jegesi ne ko: «Ngalla sang bi, ma ñeme laa diis lenn rekk, te sa xol baña tàng ci man, doonte yaak Firawnaa tolloo.

Sóol ne ko: «Samiyel da noo biralal ne mbaam ya feeñ na.» Mbirum nguur ma ko Samiyel wax nag, Sóol waxu ko baayam bu ndaw.

Naka la ne fëlëñ ca tànki Daawuda, ne ko: «Sang bi, naa tegoo tooñ gi, may ma rekk, ma wax la. Ngalla sama sang, déglul sama kàddu.

¶ Ba loolu wéyee Daawuda wax ak Yowab, mook mboolem gàngoor ga ànd ak moom, ne leen: «Xottileen seeni yére, soli saaku, ñaawloo ko deewug Abner.» Buur Daawuda ci boppam dox na, topp ca jaat ja.

¶ Naka la buurub Israyil jàng bataaxal ba rekk, ne mbubb ma tareet ndax jaaxle, daldi ne: «Man dama di Yàlla bay rey, mbaa may dundal, ba kii di yebal nit ku may fajal ngaana! Seetleen lii rekk: kii da may wut!»

¶ Mbooloo ma nag ne cell, tontuwuñu ko baat, ndax Buur moo leen santoon ne leen buñu ko tontu.

Ndax soo ci selaŋloo ba selaŋlu ci tey jii it, wall ak xettal dina bawoo feneen ñeel Yawut yi, waaye yaw yaak sa waa kër baay dingeen sànku. Li nga dugg ci nguur gi sax, nga defe ne neen la? Jombul diggante bii nu tollu tey moo ko waral.»

Job 2:13 TSK

Bokk nañu toog ak Ayóoba fa suuf juróom yaari bëccëg ak juróom yaari guddi, kenn waxu ko baat, ndax dañoo gis mitit wa mu àndal tar lool.

Dama noon: «Damay moyu ba duma moye làmmiñ.» Li feek ku bon di teew, may ŋalaab sama gémmiñ.

Nanga àddul ku amul kàddu, ku sësul fenn, nga ñoŋal àqam.

«Ana lu nuy toog? Fabuleen, nu dem ca dëkk ya tata wër, deeyi fa. Sunu Yàlla Aji Sax ji nar na sunu dee; moo nu nàndal tookey mbugal, nde noo tooñ Aji Sax ji.

Amos 5:13 TSK

Moo tax ku xelu ci jii jamono ne cell. Céy jii jamono ju bon!

Micah 7:5 TSK

Buleen gëm ab xarit, buleen wóolu ab xejj, fi kanam ndaw siy tëdd sa gannaaw sax, sàmmal sa bunti gémmiñ.

Acts 4:20 TSK

Waaye nun, li nu gis, dégg ko, manunu koo baña wax.»