¶ Ba mu ko defee Abigayil dellu ca Nabal, fekku ko lu moy mu amal biir këram bernde ju mel ni berndey buur. Xol baa nga sedd, mu màndi lool, ba tax Abigayil waxu ko dara ba bët set.
TSK
TSK · Ecclesiastes 7:4
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Ba mu ko defee Absalom sant ay nitam, ne leen: «Ma ne, bu Amnon naanee biiñ, ba xolam sedd, bu ma leen nee ngeen jam ko rekk, reyleen ko. Buleen ragal; man maa leen ko sant. Góor-góorluleen nag te ñeme.»
Buur laaj ma, ne ma: «Lu la tax ne yogg te woppuloo? Mbaa du tiisu xol?» Maa ngi tiit lool.
Dees na ko xeeb, daw ko, muy nit ku bare mitit te miin naqar. Mu mel ni ku ñuy dummóoyu, dees koo xeeb te nawloowuñu ko.
Mu ne: «Maay màndal seeni kilifaak seeni kaaŋ ak seeni kàngam ak seeni jawriñ ak seeni jàmbaar, ñu tëdd nelaw nelawi fàww, duñu yewwooti.» Kàddug Buur a, Aji Sax ji Boroom gàngoor yi.
¶ Guddi googa lañu rey Baltacar, buurub waa Babilon.
Niy taxas la ay noonam di laxasoo, mel ni ñu naan ba màndi, te ni boob mu wow lañuy lakke ba xoyomu.
Ba mu jubsee buntu dëkk ba, yemul ci lu moy ab rob, ka dee di doomu jëtun, te moom rekk la amoon. Niti dëkk ba def mbooloo mu bare, ànd ak soxna sa.