TSK

TSK · Esther 2:9

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Sang ba am cofeel ci Yuusufa, def ko fara biir këram, dénk ko saytub kër ga, ba teg ciy loxoom lépp lu mu moom.

te it nga jéggal sa ñoñ ñi la moy, jéggal leen seen mboolem tooñ yu ñu la tooñ, te may leen yërmandey ña leen jàpp, ba ñu yërëm leen.

akub bataaxal bu jëm ca Asaf may wattu toolu buur, ngir mu may ma bant yu ma defareji bunti tatay kër Yàlla ga, defaraale ca tatay dëkk baak kër ga may dali.» Buur nangul ma, ndax sama Yàlla ji ma toppe mbaaxam.

¶ Booba bala ayu kenn ci xale yu jigéen ñiy agsi, ba muy dem ca Buur Aserus, day fekk mu matal fukki weer ak yaar yi ñu àppal jigéen ñi, ngir ñu yokk ci seen taar. Juróom benni weer yi, ñu di leen diw ndàbb lu ñuy wax miir; juróom benni weer yi ci des, ñu di leen diw ay diw yu xeeñ ak yeneen yu jigéen ñiy defaroo.

Ku Aji Sax ji rafetlu say jëf, say bañ sax, mu jubaleek yaw.

Acts 7:10 TSK

xettli ko ci coonoom yépp, rafetal xelam, may ko itam Firawna buuru Misra baaxe ko; mu def ko kilifa ci Misra ak ci biir ëttu këram gépp.