Sang bi, jéggal ma rekk ndax Aji Sax jee lay defal moos kër gu yàgg. Kon nag, Yàlla bu nit gis mukk lu bon ci yaw, sa giiru dund.
TSK
TSK · Exodus 1:21
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
1 Samuel 25:28
TSK
2 Samuel 7:27
TSK
¶ «Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, Yàllay Israyil, yaw déy yaa ma déey, Sang bi, ne kër nga may sosal. Moo tax ma ñeme laa ñaan lii, Sang bi.
1 Kings 11:38
TSK
Te soo defee mboolem li ma la sant, topp samay yoon, di def li ma rafetlu tey jëfe samay dogal ak samay santaane, na ko Daawuda sama jaam ba daa defe, su boobaa dinaa ànd ak yaw te dinaa la sampal kër gu sax, ni ma ko sampale woon Daawuda, te dinaa la jox Israyil.
Psalms 112:1
TSK
Màggal-leen Ki Sax! Ndokklee ku ragal Aji Sax ji, di tàqamtikoo ay santaaneem.
Psalms 127:3
TSK
Ma ne, doom Aji Sax jee koy sédde, njurum doom yool la.
Nit bàkkaar na téeméeri yoon, te teewul mu gudd fan. Xam naa it ne nee ñu ngëneel a ñeel ku ragal Yàlla, ndax wormaal ko.