TSK

TSK · Exodus 10:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Aji Sax ji dafa wax ne: ‘Ni ngay xame ne man maay Aji Sax ji nii la: Dama ne, dinaa dóor ci ndoxum Niil mi yet, wi ci sama loxo, ndox mi soppliku deret;

Te bu leen seeni doom laajee ne leen: “Lu aada jii di wund?”

Su ko defee, bu leen seen doom laajee ëllëg, ne leen: “Lii lu muy tekki?” ngeen wax ko ne ko: “Dooley loxol Aji Sax jee nu génne Misra, kërug njaam ga.

Bu ma dumaa Firawna, boole kooki watiiram aki gawaram, ba doxe fa siiwal sama ndam, waa Misra dinañu xam ne man maay Aji Sax ji.»

¶ Bu leen seen doom laajee ëllëg, ne leen: «Ana lu waral seedey yoon yi, ak dogali yoon yeek àttey yoon yi leen sunu Yàlla Aji Sax ji dénk?»

Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di taalif bu ñeel askanu Kore wu góor.

Aji jub day gis ñu feyul ko, mu bég, muy jàngoo deretu ku bon.

muy lu nu dégg, xam ko, sunuy maam xamal nu ko.

ngir ñiy juddu ëllëg xam ko, am ay doom, ñu màgg, ba xamal ko seeni doom,

Maa leen sobeel ak seen sarax yi ñuy sarxal tuur yi, ci seen bépp taaw bu ñu lakk ngir tuur yi. Li ma ci jublu mooy ñu jommi, ba ràññee ne man maay Aji Sax ji.

Joel 1:3 TSK

Waxleen ko seen doom yi ngeen jur, doom yi ngeen jur wax ko doom yi ñu jur, doom yi ñu jur wax ko geneen maas.