¶ Aji Sax ji ne Musaa: «Yékkatil sa loxo ca kaw, mu jublu asamaan, ngir tawub yuur bi dal ci réewum Misra mépp, nit ak mala, ba ci lépp luy gàncax ci réewum Misra.»
TSK
TSK · Exodus 10:21
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Jan yàlla moo masa fexee dikk foqatil boppam aw xeet, bellee leen ci weneen xeet, ci biiri nattu, aki firnde aki kéemaan ak xare yu mu sottale dooley loxoom, ak kàttanu përëgam, ak jëf ju raglu, noonee leen ko seen Yàlla Aji Sax ji defale ca Misra, ngeen teg ci bët?
Ñu ni mel, bëccëg ñu dajeek lëndëm, di làmbatoo digg bëccëg ni bu doon guddi.
Yàlla sotti leen tàngooru xadaram, mu dim sànj ak naqar ak njàqare, lépp di gàngooru ndaw yu indiy musiba.
Yoonu ku bon ne këruus, du xam lu muy téqtaloo.
Lumb wa ñëw na moos ci neen, bàddoo lëndëm, turam sàngoo lëndëm.
dellu xool fi suuf, yem ciw tiis, ak lëndëmu njàqare, sóoboo guddi gu fatt taraj.
¶ Ba ñu demee ba tollu wetu fukki waxtu ak ñaar ca bëccëg, ag lëndëm a wàcc ca réew ma mépp, ba fukki waxtu ak juróom ca ngoon.
¶ Ñooñooy teen yu dëy, ñooy xiin wu callweer tas, te lëndëm gu fatt taraj di seenub añ.
Ñooy gannaxi géej gu sàmbaraax, di gëq seen puuriti gàcce; ñooy biddiiw yu fàq di taxawaalu, te lëndëm gu ne këruus di cér bu ñu leen sédde ba fàww.