TSK

TSK · Exodus 11:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Teewul Aji Sax ji ànd ak Yuusufa, laaye ko biir, daldi xiir wattukatu kaso ba ca moom, mu yéwéne ko.

Aji Sax ji nag def waa Misra nangul bànni Israyil, ba jox leen la ñu sàkku; noonu lañu futtee waa Misra.

Mardose nag am daraja lool ci biir kër buur, bayreem dajal diiwaan yépp, muy gën di am doole.

Ña la daa néewal, seeni doom a lay sukkalsi. Ña la daa ñàkke worma, mujj di fóon say tànk. Dees na la wooye «Dëkkub Aji Sax ji», mbaa «Siyoŋ, màkkaanu Aji Sell ju Israyil.»

Ñenn ci jàngub Seytaane bi, ñooñuy fen, di tuddoo ay Yawut te duñuy Yawut, maa ngii di leen xiirtal, dikkloo leen, sujjóotloo leen fi sa kanam, ba ñu xam ne man maa la sopp.