Say sët-sëtaat ay délsi fii bu seen jamono jotee, ndaxte bàkkaaru Amoreen ñi jéggeegul dayo.»
TSK
TSK · Exodus 13:3
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Aji Sax ji wax Musaa ne ko: «Dinga gis léegi ni may def Firawna: loxo bu ko ëpp dooleey tax mu bàyyi leen ñu dem. Bir na ne, loxo bu ko ëpp doole mooy tax mu dàq leen réewam.»
«Weer wii mooy doon ci yeen wi jiitu ci weer yi, te na doon ci yeen weer, wi jëkk ci at mi.
¶ «Diiru juróom ñaari fan ngeen di lekk mburu mu amul lawiir; te bés bu jëkk bi ci boppam nangeen jële seeni kër luy lawiir, ndaxte képp ku ci lekk mburu mu am lawiir, li ko dale bés bu jëkk bi, ba kera bésub juróom ñaareel ba, dees na ko dagge ci askanu Israyil.
Keroog ca bés, ba ñeenti téeméeri at ya ak fanweer matee sëkk, ca la ñoñi Aji Sax ji génn réewum Misra, kurél ci kaw kurél.
Su ko defee, bu leen seen doom laajee ëllëg, ne leen: “Lii lu muy tekki?” ngeen wax ko ne ko: “Dooley loxol Aji Sax jee nu génne Misra, kërug njaam ga.
¶ «Deeleen baaxantal bésub Noflaay, ngir sellal ko.
¶ «Màggalug ayu bésu Mburu mu amul lawiir, wormaal-leen ko. Diiru juróom ñaari fan ngeen ciy lekk mburu mu amul lawiir, ni ma la ko sante bu àppam taxawee ci weeru Abiib, ndaxte weeru Abiib ngeen génne fa Misra.
¶ «Man Aji Sax ji maay seen Yàlla, ji leen génne réewum Misra, kërug njaam ga.
wattuleen seen bopp bala ngeena fàtte Aji Sax ji leen génnee réewum Misra, kërug njaam ga.
Waaye cofeel gu leen Aji Sax ji sopp, ak sàmm gu mu sàmm ngiñam la mu giñaloon seeni maam, moo tax mu génnee leen dooley loxoom, jote leen ca kërug njaam ga, ak ca loxol Firawna buuru Misra.
Aji Sax ji ne ma: «Jógal wàcce fii gaaw, ndax sa bokk ya nga génnee Misra def nañu yàqute. Teggi nañu xaat yoon wa ma leen santoon. Móolal nañu seen bopp jëmmu tuur.»
Seen Yàlla Aji Sax ji moom ngeen di topp, moom ngeen di ragal. Ay santaaneem ngeen di sàmm, baatam ngeen di déglu, moom ngeen di jaamu, te ci moom ngeen wara ŋoy.
Reyleen ko rekk. Yeen ñi mu doon jéema yóbbaale, na ko seen loxo jëkka dal, ngir rey ko, bala cee loxol mbooloo mépp topp.
Fàttlikuleen ne ay jaam ngeen woon ca réewum Misra, seen Yàlla Aji Sax ji moo leen jot. Moo tax ma sant leen lii tey.
Buleen ko lekkaale lenn lu am lawiir. Daleleen caa lekk, ba diiru juróom ñaari fan, mburu mu amul lawiir, mburum njàqare, ndax ci biir gaawtu ngeen génne woon réewum Misra. Su ko defee ngeen baaxantal seen giiru dund, bés ba ngeen génnee réewum Misra.
Fàttlikuleen ne ay jaam ngeen woon ca Misra, seen Yàlla Aji Sax ji moo leen fa jote. Looloo waral man, ma sant leen ngeen jëfe ndigal loolu.
Aji Sax ji nag génne nu Misra ci dooley loxoom ak kàttanam, ci biir musiba mu réy, aki firnde, aki kéemaan.
yaa wàcce ay firndeeki kéemaan ca kaw Firawnaaki jawriñam ñépp ak askanu réewam mépp, ndaxte yégoon nga reewande ga waa Misra doon jëflanteek sunuy maam. Ca nga siiwal saw tur ba tey jii.
Fàttlikuleen ay jalooreem aki misaalam aki àtteem.
ci dooley loxoom ak kàttanu përëgam. Kee saxoo ngoram!
¶ «Léegi nag yaw Boroom bi, sunu Yàlla ji nu génnee Misraak doole, nun sa mbooloo, nga siiwale ca sa tur ba sunu jonni yàllay tey, noo bàkkaar, noo tooñ.
¶ Gannaaw loolu mu jël mburu, yékkati kàddug cant, dagg ko, jox leen ko ne: «Lii moo di sama yaram wi ñu jooxe ngir yeen. Deeleen def lii, di ma ko fàttlikoo.»
yékkati kàddug cant, dagg ko, ne: «Lii moo di sama yaram wi leen ñeel. Deeleen def lii, di ma ko fàttlikoo.»