TSK

TSK · Exodus 16:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Mbooloom bànni Israyil gépp nag di diiŋat Musaa ak Aaróona ca màndiŋ ma.

Naka la Aaróona di wax ak mbooloom Israyil mépp, ñu jekki ne gees ca màndiŋ ma, daldi yem ci aw niir, leeru Aji Sax ji di ca feeñ.

Ñu daldi gis Yàllay bànni Israyil. Lu mel ni dëru per bu safiir a nga lal tànkam ya, mel ni asamaan, ndax na mu sete wecc.

¶ Ba loolu amee niir wa yiir xaymab ndaje ma, leeru Aji Sax ji fees jaamookaay ba,

¶ Ba mu ko defee mbooloo ma mépp ne dañu leen di dóori xeer ba ñu dee. Leeru Aji Sax ji nag feeñ ca xaymab ndaje ma, ci kanam bànni Israyil gépp.

Kon kay yaw yaak sa gàngoor gépp, ci kaw Aji Sax ji ngeen bokk daje! Ana kuy Aaróona, ba ngeen di ñaxtu ci kawam?»

Day tóora tóor, di bànneexu, bay sarxolle, ba jagoo darajay gottub Libaŋ ak taaru àllub Karmel ak Saron. Foofa lees di gise darajay Aji Sax ji, sunu taaru Yàlla.