TSK

TSK · Exodus 17:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

ne ko: «Éey Boroom bi, ndegam daj naa saw yiw, rikk àndal ak nun rekk, Boroom bi, ak li mbooloo miy dëgër bopp lépp! Jéggal nu sunu ñaawtéef ak sunu bàkkaar rekk, te nga séddoo nu.»

«Dees na tërali Aaróona fa ay bokkam. Du dugg déy ca réew ma ma jox bànni Israyil, gannaaw yeena gàntaloon sama ndigal ca walum Meriba.

¶ Ca Tabera itam, ak ca Maasa, ak ca Kibbrot Taawa, ngeen merlooti fa Aji Sax ji.

¶ Lewi la wax ne ko: Sa Tumim ak sa Urim, jumtukaayi tegtal ya, ñeel na góor gay sa wóllëre, yaa ko nattoo ca Maasa, joteek moom ca ndoxum Meriba.

Ñoo diiŋate Yàlla xol, di xemmem ñam wu bakkane.

Ngeen jàq, woo ma, ma xettli leen, wuyoo leen fa kiiraayal dënn ya, te maa leen nattoo fa wal ma ca Meriba. Selaw.

Ñu merlooti Yàlla ca ndoxum Meriba ma, muy loraangey Musaa te ñoo ko waral.

Seeni njiit, alalu ger lañuy àttee, seeni sarxalkat di feyeekuy jàngle, seeni yonent di weccikoo xaalis seenum ngisaane, te Aji Sax ji lañuy dëgërloo, naan: «Xanaa du Aji Sax jaa ngi ci sunu biir? Musiba du nu dab!»

Acts 7:37 TSK

Musaa moomu moo noon bànni Israyil: “Yonent bu mel ni man la leen Yàlla di feeñalal ci seen biiri bokk.”