¶ Aji Sax ji ne Musaa: «Dama ne, def naa nga féete Firawna fi ko Yàlla féete, sa mag Aaróona di sa yonent.
TSK
TSK · Exodus 19:4
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
ca màndiŋ ma it, gis ngeen na leen seen Yàlla Aji Sax ji fabe, ni baay di fabe doomam, ci yoon wi ngeen dox wépp, ba agsi bérab bii.»
Ana askan wu masa dégg baatu Yàlla bu jibe ci sawara, ni ngeen ko dégge te dese bakkan?
¶ Ba mu ko defee Musaa woolu Israyil gépp. Mu ne leen: Yeena gis mboolem la Aji Sax ji def, ngeen teg ci seen bët, ca réewum Misra, ci kaw Firawna ak dagam ñépp, ak réewam mépp.
Moo mel ni jaxaay juy naawtal am tostanam, daayaarlu, tiim leen, tàllali laafam, aw leen, teg ciw dunqam, boot leen.
kiy yaakaar Aji Sax ji moom, di yeeslu doole; da naa fëyy ni jaxaay juy naaw, di xélu te du xiix, di dox te du xoox.
«Maa soppoon Israyil ba muy ndaw, Fa Misra laa ko wooye, muy sama doom.
Ñu jox ndaw si ñaari laafi jaxaay ja, ngir mu naaw, rëcc ninki-nànka ji, dem màndiŋ ma, ca rawtoom ba ñu koy leele lu tollook ñetti diir ak genn-wàll.