TSK

TSK · Exodus 20:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

«Ana kuy sa moroom ci tuur yi, yaw Aji Sax ji? Kuy sa dend, yaak sa sellaay bu yéeme, sa yànjaay bu raglook sa jëf yu yéeme?

¶ «Kuy sarxeel jeneen yàlla ju dul Aji Sax ji moom rekk, dees koy faagaagal.

Terewul xeet wu ci nekk di sàkk ba tey seen tuuri bopp ca seen dëkk ya ñu féete, ba dugal tuur ya ca bérabi jaamookaay, ya waa Samari defaroon.

seedeel-leen Aji Sax ji teddngay turam. Sujjóotal-leen Aji Sax ji, ki gànjaroo sellnga.

Yeen sama ñoñ, dégluleen, ma dénk leen. Éy Israyil, su ngeen ma déglu woon!

Wóoluleen Aji Sax ji tey ak ëllëg; Yàlla Aji Sax ji déy, moo mat cëslaay ba fàww.

Buleen tiit, buleen ragal. Dama leena biralul lii bu yàgg, yégal leen ko? Yeenay samay seede. Yàlla daa am ju ma moy? Cëslaay amul, xawma ci kenn!»

Fàttlikuleen cosaan la woon. Man mii maay Yàlla, du keneen. Amul Yàlla ju mel ni man!

Yónnee naa leen samay jaam, yonent yi, ay yooni yoon, ne leen: ‘Na ku nekk ci yeen dëpp yoonam wu bon, di def lu baax, baña topp yeneen yàlla, di leen jaamu, ndax ngeen dund ci réew mi ma leen jox, yeen ak seeni maam.’ Waaye teewluwleen ma, déggaluleen ma.

Teewul ci sunu wàllu bopp, jenn Yàllaa am, muy Baay bi lépp jóge ci moom, te sunu bakkan ñeel ko, benn Sang doŋŋ a am, muy Yeesu Almasi, bi lépp ame ci moom, te sunu bakkan, ci moom la ame.

Ñooñu sànkute lañuy mujje; seen koll lañu def seen yàlla, seen gàcce lañuy damoo, te yëfi àddina doŋŋ a leen soxal.

Mu ne ma: «Ëpp naa def, sa mbokkum jaam doŋŋ laa, ni yaak sa bokki yonent yeek ñiy sàmm kàdduy téere bii. Sujjóotalal Yàlla.»