TSK

TSK · Exodus 20:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Ba mbooloo ma gisee Musaa yàgg lool te wàccul tund wa, dañoo songandoo Aaróona, ne ko: «Ayca, sàkkal nu yàlla ju nu jiite, ndax Musaa mii nu génne réewum Misra kat, xamunu lu ko dal.»

Jàdd nañu xaat yoon wa ma leen tegoon. Dañoo sàkkal seen bopp sëllu wu ñu móol, di ko sujjóotal ak a sarxalal, naan: “Israyiloo, seen yàllaa ngii, moo leen génne réewum Misra!”»

¶ «Ay tuur yu ñu móole weñ, buleen ko móol.

¶ «Buleen sàkkal seen bopp ay yàllantu, du lenn luy jëmmu tuur mbaa tuuru doj wu ngeen sampal seen bopp, te doj wu ñu ñaas ay nataal it, buleen ko sàkkal bérab ci seen réew, di ko sujjóotal, ndax man Aji Sax ji maay seen Yàlla.

Kon buleen def ug yàqute, di sàkkal seen bopp menn tuur muy jëmmal lenn lu mel ni góor mbaa jigéen,

¶ Bu ngeen demee ba am ay doom aki sët, fekk leen yàgg ca réew ma, su boobaa su ngeen defee ag yàqute, di sàkk am tuur, ak jëmmu lu mu mana doon, mbaa ngeen def lenn lu seen Yàlla Aji Sax ji ñaawlu, lu koy merloo,

Te itam buleen yékkati lenn lu bokk ci doji jaamookaay yooyu seen Yàlla Aji Sax ji bañ.

Seeni tuur xaalis laak wurus, di liggéeyu doom aadama:

Ana kan ngeen di niruleek Yàlla, ak nataal bu ngeen koy dendaleel?

Ñi wóolu ay jëmmi tuur, naan jëmm yu ñu móol: “Yeenay sunuy yàlla,” dees na leen waññi, torxal leen.

Yettkati xërëm yaa ngoogu, rus, torox, riixleendoo.

Aaday xeet yi kat neen la. Garab lañuy dagge ca gott ba, ab yettkat yette ko sémmiñ,

Nitoo nit dim sannax, sore xam-xam: te képp kuy tëgg sa jëmmu tuur, yaa añe gàcce. Sa jëmmi weñ ji nga xelli, di neenug neen, noog bakkan, tus!

Ndegam nag xeetu Yàlla lanu, warunoo nirule Yàlla ak lenn luy wurus, mbaa xaalis mbaa aw doj te sosoo ci xareñtey nit akum xelam.

Leeru Yàlla ji dul dee lañu weccee jëmmu nit ki deeyam dul jaas, ak picc, ak boroom ñeenti tànk, ak ndëgmeent.

Ñaareelu rab wi nag nax waa àddina ci kéemaan, yi mu am sañ-sañu def ci turu rab wu jëkk wi. Mu sant waa àddina, ñu sàkk jëmmu rab, wi ñu jamoon saamar te muy wéye bakkanam.

¶ Malaaka mu jëkk mi dem, sotti ndabam ci kaw suuf, mu def ay taab yu bon te aay ci kaw nit ñi am màndargam rab wi, tey sujjóotal jëmmu nataalu rab wi.