TSK

TSK · Exodus 24:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ci kaw loolu Aji Sax ji feeñu Ibraam ne ko: «Sa askan wi soqikoo ci yaw laay jox réew mii.» Ibraam nag daldi tabaxal Aji Sax, ji ko feeñu, ab sarxalukaay.

Doj wii ma samp, muy xàmmikaay, mooy doon kër Yàlla, te lépp lu mu ma wërsëgal, dinaa ko génneel fukkeel ba moos.»

Musaa nag sàkk fa sarxalukaay, tudde ko tur wuy tekki «Aji Sax jeey sama raaya».

Su ngeen ma dee sàkkal sarxalukaayu xeer, buleen ko defare xeer yu ñu yett, ndaxte bu ngeen ko laalalee ab jumtukaay, teddadil ngeen ko.

¶ Aji Sax ji teg ca ne ko: «Nanga bind yii santaane, ndax ci kaw santaane yii laa fasook yaw kóllëre, yaak bànni Israyil.»

«Waxal Elasar doomu Aaróona, sarxalkat bi, ne ko mu seppee and yi ci lakk gi, ndax lu sell la, te xal yi, na ko tuur fu sore.

daldi jël fukki doj ak ñaar, mu tollook limu giiri doomi Yanqóoba. Yanqóoba la kàddug Aji Sax ja dikkaloon ne ko Israyil ay doon turam.

¶ Loolu yépp tax na nuy tëral takktoo bu dogu, bind ko, sunuy njiit ak sunuy Leween ak sunuy sarxalkat def ci seen màndargay torlukaay.

Ña ñu jàppoon ne ñooy kenuy mbooloom gëmkat ña nag, te ñuy Yanqóoba ak Sefas ak Yowaan, ba ñu ràññee yiw wi ñu ma jagleel, maak Barnaba lañu jox loxo, ngir nun nu liggéeyi ca jaambur ña, te ñoom ñu liggéeyi ci Yawut yi.