TSK

TSK · Exodus 28:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ «Nañu ràbbe xar-sànni mi wëñu wurus, ak wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar ak gu xonq curr ak wëñu lẽe, ñu ñawaale ci ay nataal.

¶ Xar-sànni mi, wëñu wurus lees ko ràbbe, ak wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr ak wëñu lẽe.

Ñu def itam ay jóolóoliy wurusu ngalam, ba takk jóolóoli yi ci diggante doomi gërënaat yi, wërale ko ombu fëxya bi, ba mu daj, jóolóoli yi dox diggante doomi gërënaat yi.

solal Aaróona mbubb mu gudd ma, takkal ko laxasaay ga, solal ko fëxya ba, tegal ko ca xar-sànni ma, takkal ko ngañaay la ca kawam, jàppe ko ko, mu tafu ca kawam.

Buur ne Doweg: «Ayca yaw, fàddal sarxalkat yii!» Doweg Edomeen ba fàdd sarxalkat ya. Rey na bésub keroog juróom ñett fukki nit ak juróom (85) ñuy sol xar-sànnim lẽe.

Ci biir loolu Daawuda wax ak sarxalkat ba Abiyatar doomu Ayimeleg, ne ko mu indil ko xar-sànni mi. Abiyatar indil Daawuda xar-sànni ma.

¶ Taxawleen kon temm. Defleen dëgg di ngañaay li ci seen ndigg, njub di seen kiiraayal dënn.

¶ Nii laa gise ci peeñu mi fas yi ak ñi leen war: ñu ngi sol kiiraay yu xonq ni sawara, baxa ni safiir, te mboq ni tamarax. Boppi fas yaa ngi nirook boppi gaynde, sawara ak saxar ak tamarax di génne ci seen gémmiñ.